Bienvenue notre blog

Bienvenue notre blog

NANU MUSLU CI BUKKI  NJUUR SAMBA YI AK KAKATAR YI, ces girouettes qui s’adaptent au gré du vent soufflant

NANU TAALIF AK WOY

SUNIY WAREEF CI JAMONO DI FATTALIKU JËF NGIR JALLARBI SUNU NEKKIN

 

Autrement dit,

Assumer et brandir haut levé, le drapeau de nos responsabilités et tâches pour le présent et le devenir de notre peuple, qui mettent à l’ordre du jour, l’actualité de l’action révolutionnaire de transformation sociale.

 

 

YEEN MBOKKAAN YI

 

Yéen mbokkaan yi, yéena doy njiit ngir seen xalaat, seen Jëf Ju leer Yéena rañale yoonu cëll wi

Ba waa njaay doole fippu jóg taxaw

 

Xiinub toraxte mu ngiy wuuri Bidéewu nootange fanq na

Teenu nagar yi ñu ngiy déey

Seyaani banneex yi bët nañ

 

Du ngeen fen, du ngeen SOS

Du ngeen ràmbaac

Yéena yaatu, yéena yéwën

Ku ngeen jaboote Xalaatam leer

Ku Ngeen ngémb , su Bëree daan

 

 

Xiinub toraxte mu ngiy wuuri

Bidéewu nootange fáng na

Teenu naqar yi ñu ngiy déey

Seyaani bánneex yi bët nañ.

 

Yéen mbokkaan yi yéena woone

Ni ñuy buddee garabu naqar

Yéenay melax yiy dàq niis

Yéenay jëfurloo njëktéef yi

 

Xiinub toraxte mu ngiy wuuri

Bidéewu nootange fànq na

Teenu naqar yi ñu ngiy déey

Seyaani bànneex yi bët nañ.

 

 

 

Doomu réew mooy tabax Réew!

Ngor mooy faj gàcce!

Ndam laa ngi ci fippu

ASKAN WI !

 

 

 

L’internationale sera le genre humain

 

autrement dit,

Mbootaayu Mbokkaan yi

Di na doon wennu

Xeetu addina si yepp

 

 

Fullaal suniy wareef

tey jëmmel yoonu Mbokkan

 

autrement dit,

Assumer haut et fort nos responsabilités et donner corps à  la perspective communiste !

 

 

JO DIOP

Militant -marxiste – Léniniste, Panafricaniste et Internationaliste.

Membre fondateur de Yoonu Askanwi / Mouvement pour l’autonomie populaire , chargé du patrimoine

 



01/10/2017
0 Poster un commentaire